Mbind 2 (200 baat)

Mbind 2 : (Àpp, Àllarba 2/10)

Theme: Ci fajukaay bi.

Instruction: Bindal ci sa feebar! (Target: 200 baat)

Situation: Remember the last recent time you felt sick (or something happened to you) and you went to see a doctor.

Write on: Talk about your sickness, what it was, describe how you felt, when you went to see the doctor, where is the place, the name of the place, what did the doctor tell you, what did you tell him/her, what did he/she say about what you were suffering, whether or not he/she gave you medicine, how did he/she say you should take the medicine, whether you felt better after taking the medicine, whether or not because of the sickness you could not attend class or do other things, did you go alone to see the doctor or not, what you think about the doctor, did the doctor tell you what could be done to avoid what happened to you, etc……….

NB: à – é – ë – ó – ñ –

11 thoughts on “Mbind 2 (200 baat)

  1. Benn fan ci desàmbar ci atum 2013, yeewuwoon naa te tawatoon naa. Amoon naa metitu-bopp, ak ci suba bi, amoon naa ab buri. Damaawoon ci sama kër, ak sama waakër la sagaloon ma. Nöppalikuwoon naa lu bare, waaye lekkoon tuuti ci bës bi. Amoon naa coono, waaye waccumawoon. Sama yaay jaaxalewoon na, ak demoon nanu ci fajukaay. Sama fajukaay, tudd na Dr. Melvin. Waxoon ma na ci soxlo na nöppalu te jël naa garab. Soxlowoon naa dem ci oppitaal – duloon naa soxlo dem ci oppitaal. Demoon nanu ci sunu kër, ak jàngoon naa te seetaanoon tele bi. Jëloon naa ag garab, ak sama bopp tanewoon na. Sama biir tanewoon na tamit, ak lekkoon naa as reer.
    Ci sama waakër, caaxaan nanu ci kenn feebar na. Tappale nanu jaaxalunu, waaye jaaxal lu bare, te tappale jaaxal nanu lu bare, waaye jaaxalunu. Toggal nanu suppu ginaar ak joxal nanu liminaat bu jinjeer ak galaas bu dëroon – ba sama ndaw, sunu yaay joxal nu (sama rakk bu góór ak man) liminaat bu jinjeer ak galaas bu dëroon ci amoon nanu metitu biir. Tanewoon naa ci fanu apare.

  2. Ci ayubés bi weesu, jangoon nanu ci sibbiru ak yeneen feebar ci kalaasu Wolof. Moo tax, dinaa bind ci yoon kañ damaa sibbiruwoon.

    Damaa sibbiruwon kanñ amoon naa fukk ak juróóm-ñeenti at, daanaka ñaar fukki at, ci atum ñaari junni ak fukk. Benn bés, nekkoon naa ci fajukaay ndaxte sama xarit defoon na accident bu tuuti ak moto. Kañ xaaroon naa sama xarit ci fajukaay bi, sama bopp tambaliwoon na metti. Bés bii di ñëw, sama xarit bu defoon accident tanewoon na waaye sama bopp la mettiwaatoon. Xalaatoon naa ne damaa feebaroon kañ nekoon naa ci fajukaay ndax amoon na nit ñu feebar yu bari foofu. Ci guddi, amoon naa tàngooru-yaram wu yéég, coono, ak mettitu bopp te damaa liwoon di lox.

    Bés bii di ñëw, gisoon naa sama baay (host father), Edward, te waxoon naa ko ci samay màndarga. Edward waxoon na ma, “Xalaat naa ne danga sibbiru”. Moom yóbbuwoon na ma ci kiliniik ngir gis ab fajkaat. Fajkaat bi laajoon na ma ci samay màndarga. Moom jëloon na sama tàngooru-yaram te saytuwoon na ma. Laajoon na ma, “Ndax yaw jël garab ngir faggaru sibbiru?”. Tontuloon naa, “Déédet.” Fajkat bi joxoon na ma garab.

    Jëloon naa garab ñetti bés. Garab gi fajoon na ma. Ci ñetteelu bés, tanewoon naa te fowoon naa futbool ak samay xarit! Amoon naa wërsëg ndax Edward nekk na farmasiyaan. Moo tax, jëloon naa garab gu baax. Tamit, amoon naa wërsëg ndax amoon na fajkat yu bari ci sama dëkk ak amoon naa xalis ngir gis léén.

    • Rea, ñaari mbir yu gëna am solo ci sa ñaareelu mbind mi nekk nañu: (1) ay baat yu bees yu bari yuy firndéél sa gëstu ngir xam leneen lu bokkul ak li nuy jàng ci sunu kalaasu Wolof bi, ak (2) xalaat yu wuute te sakkan yu ngay indi te ñuy dëgêral sa mbind. Sa liggééy rafet na. Jaraw-lakk!
      NB: Firndé -l tekki na “proof’ wala “clear example”
      Firndéél (v.) man na tekki “to prove” wala “to clearly show” wala leeg-leeg “to exemplify”
      Lu bokkul ak = something different from
      Sakkan (adj.) man na tekki “numerous” wala “prolific” wala “a lot”
      Dëgër (adj.) tekki na “strong” wala leeg-leeg “steady”
      Dëgëral = to strengthen

      1- Jàngoon
      2- Ci bés ba ma sibbiriwoon (the day I had malaria)
      Wala tamit Ci bés ba nga xam ne damaa sibbiriwoon
      3- Ba ma amee fukk ak juróóm-ñeenti at
      When I was 19
      4- Baatu “accident” man nañu ko tekkee “jéyé” wala “ndogal” ci yenn fànn yi. Wala sax, Wolof yi àbb nañu baat bi te jógé na ci Farañse.
      5- Mótó
      6- Ba may xaar ….. = when I was waiting
      7- Bés ba ca topp = the next day, the following day
      Topp (v.) = to follow, to come after, etc.
      8- Dafa mettiwaatoon
      9- Ba ma nekee ca fajukaay ba = when I was at the hospital
      NB: See the use of “a” at the end of certain words to refer to a past context without necessarily adding the ending structure -oon or -woon

      10- Ca guddi ga
      11- Ndax yaw jël nga garab?
      12- Tontuwoon naa
      Tontu (v.)
      Tontul! (Imperative)
      13- Am wërsëg bokkul ak am saas
      Xoolal baatukaay bi mgir yeneen tekki.
      Jërëjëf.

      • Ci ayubés bi weesu, jàngoon nanu ci sibbiru ak yeneen feebar ci kalaasu Wolof. Moo tax, dinaa bind ci ayubés ba ma sibbiriwoon.

        Damaa sibbiriwon ba ma amee fukk ak juróóm-ñeenti at, daanaka ñaar fukki at, ci atum ñaari junni ak fukk. Benn bés, nekkoon naa ci fajukaay ndaxte sama xarit defoon na jéyé ju tuuti ak mótó. Ba may xaar sama xarit ci fajukaay bi, sama bopp tambaliwoon na metti. Bés ba ca topp, sama xarit bu defoon jéyé tanewoon na waaye sama bopp dafa mettiwaatoon. Xalaatoon naa ne damaa feebaroon ba ma nekke ca fajukaay ba ndax amoon na nit ñu feebar yu bari foofu. Ca guddi ga, amoon naa tàngooru-yaram wu yéég, coono, ak mettitu bopp te damaa liwoon di lox.

        Bés ba ca topp, gisoon naa sama baay (host father), Edward, te waxoon naa ko ci samay màndarga. Edward waxoon na ma, “Xalaat naa ne danga sibbiru”. Moom yóbbuwoon na ma ci kiliniik ngir gis ab fajkaat. Fajkaat bi laajoon na ma ci samay màndarga. Moom jëloon na sama tàngooru-yaram te saytuwoon na ma. Laajoon na ma, “Ndax yaw jël nga garab ngir faggaru sibbiru?”. Tontuwoon naa, “Déédet.” Fajkat bi joxoon na ma garab.

        Jëloon naa garab ñetti bés. Garab gi fajoon na ma. Ci ñetteelu bés, tanewoon naa te fowoon naa futbool ak samay xarit! Amoon naa wërsëg ndax Edward nekk na farmasiyaan. Moo tax, jëloon naa garab gu baax. Tamit, amoon naa wërsëg ndax amoon na fajkat yu bari ci sama dëkk te amoon naa xalis ngir gis léén.

  3. Assalaamaalekum. Jereme naa tudd. Demoon naa ci fajukaay bi ci yeewu naa ci Juróom naari waxtu ci suba. Tay la benn bu njëkk, fan ci weeru Feweriyéé ci atum, naari Junni ak fuk ak juróom. Amoon naa soj. Amoon naa tàngoor- yaraaw ak metitu-bopp. Wala sama metti wi naa tank ak biir. Demoon naa Carle ci Urbana ngir da ak sama fajkat. Moom, Mike la tudd. Man, tëdd na ci lalu-oppitaal. Fajkat bi saytu na yaraw. Fajkat bi joxe naa mandarga wi. Amoon naa Tangoor- yaram ak metitu-bopp. Fajkat bi waxoom naa damaa feebaroon. Fajkat bi joxoon naa garab. Jëloon naa garab naari ab bés. Ci benn ci subu ci benn ci ngoon altiné diggënte ajjuma. Garrett jëloon naa ci kilinik ci Carle. Fajkat bi waxoon naa fagaru saj. Soxla naa tuuti nelaw (rest) ak (a lot of liquids). Demoonumawoon kalassu ci altine diggente ajjuma. Docktor bi fowoon na nelew lu bari. Docktor bi naanoon naa lu bari. Fowoon na fargaru ci nelaw naa lu bari. Nekk naa dockor bi.

    • Jereme, jërëjëf ci sa mbind mii.
      1- Jereme laa tudd
      2- Demoon naa ci fajukaay bi bi ma yeewoo ci juróóm-ñaari waxtu
      3- Bés bu njëkk ci weeru Feweriyéé wala Fan wu njëkk ci weeru ……
      4- Ñaari junni ak fukk ak juróóm.
      5- “Wala sama metti wi naa tank ak biir”: Lan nga bëggoon wax fii?
      6- Demoon naa Carle ngir daje ak sama fajkat.
      7- Man, tëdd naa
      8- … saytu na sama yaram
      9- “Fajkat bi joxe naa mandarga wi”: Lan nga bëgg wax fii?
      10- Tàngooru-yaram
      11- Waxoon naa fajkat bi damaa feebaroon
      12- Joxoon na ma garab
      13- Jëloon naa garab ñaari yoon bés bu nekk (twice per day)?
      14- Benn suba benn ngoon, diggënté altiné ba àjjuma
      15- Garrett (moom) yóbbuwoon na ma ci Carle = Garrett took me to Carle
      16- Check how the words are spelled.
      NB: Soj, Doktoor
      17- Ndox mu bari (a lot of water?)
      18- Demumawoon kalaas (demoonumawoon)
      19- Diggënté altiné ba àjjuma (I didn’t go to class from Monday to Friday)
      20- Doktoor bi fowoon na nelaw lu bari”: Lan nga bëgg wax fii?
      Doktoor bi naanoon naa lu bari”: Lan nga bëgg wax fii?
      21- Fo tekki na “to play”

      Jërëjëf.

  4. Ci at mi weesu, daanuwoon naa ci eskale yi ndaxte samay muus yéena ngi doon nelaw fii. Sama tànk moo ngi metti lu bari ci ay ayubés. Feccumawoon lu bari. Solumawoon samay dàll. Demoon naa ci kiliniku McKinley ci iniweristé ci ab wiken, ndaxte amoon naa kalaas yu bari ci ayubés (maa ngi doon jàngale ak maa ngi doon jàng tamit). Demumawoon ak samay xarit wala sama jëkër.
    Waxoon naa ci ay fajkat:

    Man : Sama tànk ndayjor metti na lu bari. Ndax dammoon naa ag yax ?
    Fajkat : Soxla nanu jël ay x-ray, waaye fajkat bu jël x-ray yi nekkul ci kilinik tay.

    Fajkat bu jël x-ray yi seetiwoon na ci kilinik. Xaaroon naa tuuti jot rek. Fajkat bi jëloon na ay x-ray ci sama tànk. Saytuwoon na x-ray yi. Ci x-ray yi, amumawoon naa yax gu damm. Damaa kontanoon lool, waaye sama tànk mettiwoon na ñaari weer. Farmasiyeŋ bi joxoon na ma garab, waaye bëgguma garab. Moo tax jëlumawoon garab. Xaaroon paj mu gëna bëgg : jot. Tanewoon naa ci ginnaaw daanaka ñetti weer.

    Tay, dëkk naa ag kër gu amul eskale ngir fagaru daanu. Sama tànk mettiwul ma tay. Fecc naa !

    • Jessica, jaajëf ci sa mbind mu am solo mi te bari ay xalaat yu wuute. Bari na tamit ag xereñ gu yaatu. Baatu xereñ man na tekki “creativity”.

      1- Ñu ngi doon nelaw fóófa.
      Ndax bëggoon nga wax ci Àngale “They were sleeping there”?
      Fii = here Fee = there Fóófu = there Foofa = there (referring to the past)
      2- Moo ngi doon metti wala mu ngi doon metti
      3- Ci ayubés bi
      4- Jëkkër
      5- Waxoon naa ak ay fajkat
      6- Ndayjoor
      7- Sama yax dammoom na
      8- Paase rajo (Jógé na baatu Farañse “faire une radiographie”)
      9- Fajkat buy paase rajo
      10- tuuti rek
      11- Amumawoon (“amumawoon naa)
      12- Kontaanoon naa
      13- Xaaroon paj mu gëna bëgg:jot. Lan nga bëgg wax fii?
      14- Ngir fagaru ci daanu
      Wala ngir moytu daanu (avoid, prevent)
      15- Mettiwul tay

  5. Assalamalekum. Tudd naa Garrett. Lee laa Sant. Demoon naa ci Fajukaay bi ci juròomi fan ci weeru desamber ci atum nari junni ak fuk ak neñtt. Demoon naa ci McKinney clinic. McKinney Clinic dekk na Champaign. Amoon naa soj. Amoon naa wu tàngoor. Laambawoon naa mbon. Fajkat bi saytu na mo. Fowoon naa ko samma màndarga.Fowoon naa “Am naa Tàngor yaraw ak Metitu bopp ak metitu yax. Fowoon na mo amoon naa xurfaan.Fowoon na mo naan naa ndox. Joxoon na mo garab. Fowoon na dinna jël ko bës bu nekk ci suba ak ci ngoon. Demumawoon kalassu ngir nari bës. Dawumawoon pur juròom benn bës. Feebar bi nekkoon na mbon. Docktor bi fowoon na mo nelew lu bari. Jëloon naa garab bës bu nekk ci subu ak ci ngoon. Nelawoon naa lu bari. Naanoon naa ndox lu bari. Demoon naa docktor bi kot. Fogoon naa Docktor bi nekkoon na rafet. Fogoon naa Docktor bi xamoon na lu bari. Nekk na docktor bi. Fowoon na mo fargaru bi.
    Fowoon na fargaru ci nelaw naa lu bari. Fowoon na mo lekk naa neex ñam. Fowoon na mo. Dinaa nekk wargu. Buma nekkee wargu duma nekk feebar.

    Jèrèjëf,

    • Jërëjëf ci sa mbind, Garrett
      Dinga soxla xoolaat lii:
      1- Check the spelling of the vowels (Example: juróóm)
      2- Desàmbar
      3- Demoon naa ci kilinik McKinley
      4- Nekk na ci Champaign
      5- Amoon naa aw tàngoor
      6- “Laambawoon naa mbon” Man xamuma lan nga bëgg wax fii.
      7- Saytu na ma
      8- “Fowoon naa ko sama màndarga” Lan nga bëggoon wax fii?
      9- Yaram (yaraw)
      10- Dinaa jël (dinna jël)
      11- Bon (adjective)=bad Mbon -g (noun)
      12- ” Demoon naa docktor bi kot” Lan nga bëgg wax fii?
      13- “Docktor bi nekkoon na rafet” Ndax bëgg nga wax “he was good, kind”? Kon, “Baax na” wala “Doktoor bi nit ku baax la”
      14- Fagaru (Fargaru)
      15- Ñam wu neex (“neex ñam)
      16- Wargu . Lu baat bi tekki?

      Jërëjëf.

Leave a Reply