Mbind 1 (150 baat)

Bindal lu tollu ci 150 baat ci say feeti Winter Break! Waxal tamit ci say kalaas ak sa porogaraam ci semestaru Spring ci atum 2015! Jërëjëf!

Àpp (Àllarba 28 ci Saawiyéé)

NB: à – é – ë – ó – ñ –

10 thoughts on “Mbind 1 (150 baat)

  1. Ci feetu Winter Break, demoon naa ci diwannu Illinois. Gisoon naa sama waakër ak samay xarit. Nappaloon lu bari ak gisoon nanu ay film ci cinéma lu bari ci sama waakër ak samay xarit. Ci feetu Christmas, feetewoon naa ci sama kër. Lekkoon naa ginnar lu bari ak pomiter lu bari ak tutti lujum ak menneff. Jëloon naa maye ci sama waakër ak samay xarit. Jëloon naa sama mag bu goor ak mag bu jigèèn tutti yarem. Jëloon naa sama waajur yarem. Nekkoon naa bëg ci kër. Nekk naa be bëg ci UIUC ci samay xarit.

    Ci semestaaru Spring ci atum ñaari junni ak fukk ak juróóm benn, jël naa juróómi kalaas bi: Kalaasu popular movies, kalaasu wolof, kalaasu benn sports management, online kalaasu. Am naa benn kalaas bi ci Ajjuma. Am naa naari kalaas ci Altinè ak Alxemes. Am naa neenti kalaas ci Talaata. Am naa ñetti kalaas ci Àllarba.

  2. Ci feetu Winter Break, demoon naa ci diwannu Illinois. Gisoon naa samma waakër ak samay xarit. Ci feetu Christmas, feetewoon naa ci sama kër. Lekkoon naa togg lu bari. Jëloon naa maye ci sama waakër ak samay xarit. Jëloon naa sama rakk bu jigèèn (a dvd). Jëloon naa sama waajur (giftcards). Nekkoon naa bëg ci kër waay nekk naa bëg ci university of Illinois.

    Ci semestarr bii, jël naa ñetti kallass. Am naa ñaari kalaas ci Altine ak Talaata, ak Àllarba, ak Ajjuma. Am naa ñetti kalaas ci Alxamis. Ci Altine ak Talaata, ak Àllarba, ak Ajjuma, am naa kalaasu wolof ak am naa kalaasu Calculus. Daw naa bës bu nekk. Am naa xeet bës bu ay. Am naa (excited). Bëg naa nekk ak samay xarit Am naa bëg ngir nekk na tëb. Calculus nekk ma ngi sas. Bëg naa nekk wolof ngir semestarr bii.

  3. Ci feetu Winter Break, demoon naa ci diwaanu Washington ngir gis sama waakër ak samay xarit. Sama jëkkër demoon na ci Washington ak man tamit. Lekkoon nanu lu bari. Feetewoon nanu ci këri samay waakër. Ci bésu at mu bees, Dustin liggééyoon na, ndaxte moom feetewuloon na. Man, feetewoon naa ak samay xarit. Ginaaw loolu, jángoon naa, bindoon naa, te gëstoon naa. Noppaluwoon naa ak seetaanoon naa télé tutti.

    Ci semestaar bii, jël naa ñaari kalaas. Am naa benn kalassu Wolof ak benn kalaasu Italian (xamuma bees bi). Gëna solo, gëstu naa lu bari ngir bind sama memuwaar. Demoon naa ci Chicago ci wiken bi weesu ngir seeti ay jángkat. Ci ayubés bi weesu, demoon naa ci Oconee, ci diwaanu Illinois, ngir seeti ab jángkat. Dalal naa sama oto lool! Ci weeru awril, dinaa dem ci Paris. Dinaa gëstu ay jángkat ci porogaraamu Study Abroad ci Paris. Bëgg naa Paris lool!

    • Jessica,
      Jërëjëf. Sa mbind am na solo te xalaat yi leer nañu.
      1- Dustin liggééyoon na ndaxte moom feetewulwoon (feetewuloon na)
      2- Ginnaaw lóólu (Ginaaw loolu)
      3- Jàngoon naa (Jángoon naa)
      4- Gëstuwoon naa (Gëstoon naa)
      5- Tele (télé)
      6- Tuuti (tutti)
      7- Kalaasu Wolof
      8- Xamuma baat bi?:) (Ndax bëgg nga wax “baat” instead of “bees bi”)
      9- Ci li gëna am solo (Most importantly)
      10- Jàngkat (jángkat)
      11- Dawal naa (dalal tekki na “to welcome”)
      12- Ndax bëggoon nga wax “dawal naa sama oto lu bari”?

      Jërëjëf. Am na solo 🙂

  4. Ci feetu Winter Break, man bég naa lool ndaxte mën naa noppalu. Feetu Winter Break am na ñeenti ayubés ci weeri Desàmbar ak Saawiyéé. Ci feetu Winter Break, man demumawoon ci sama kër ci Albani waaye wotewoon naa ak waxoon naa ak sama waakër faraldi. Jàngoon naa te bindoon naa sama memoir, waaye liggééyoon naa bu bari. Jàngoon naa tamit téére yu bari. Seetiwoon naa samay xarit. Man ak samay xarit seetaanoon nanu ay film ci cinémaa. Feetewoon naa at mu bees mi ak sama xarit bu tudd Anthony. Nun demoon nanu ci ab baar ngir fecc. Bégoon nanu lool ci feetu at mu bees mi.

    Ci semestaaru Spring ci atum ñaari junni ak fukk ak juroóóm-benn, amuma kalaas yu bari waaye samay liggééy ci semestaaru Spring dafa jafe. Am naa ñetti kalaas: kalaasu Wolof, kalasuu Thesis Writing ak kalaasu Colonialism & Postcolonialism. Sama kalaas bu laa gëna bëgg nekk na kalasuu Wolof!

    • Rea, jërëjëf.
      Mbind mi am na solo. Ànd na tamit ak ay xalaat yu bari te wuute.
      1. Wootewoon naa (Wotewoon naa)
      2. Faraloon naa di woote ak wax, WALA
      Doon naa faral di woote ak wax ak sama waakër …
      3. Liggééyoon naa lu bari
      4. Tééré
      5. Sinemaa
      6. Semestar
      7. Samay liggééy ci semestaru Spring dañu jafe.
      8. Sama kalaas bu ma gëna bëgg …..

      Jërëjëf. Sa liggééy rafet na. 🙂

  5. Ci sama feeti Winter Break, samay waajur, sama rakk-bu-góór, ak man seetiwoon nanu sunu waakër ci diwaanu Ohio. Bu njëkk, seetiwoon nanu waajuru sama yaay, ci dëkku Cleveland, ak feetewoon nanu Ribiyoŋ. Sama maam-bu-jigéén ak man, toggandóówoon nanu pombiteer bi, yappu-mbaam wi, ak salaat bi ci Ribiyoŋ.
    Appare, nun demoon nanu ci dëkku Cincinnati, ak seetiwoon nanu waakëru sama baay. Toggumawoon ci Cincinnati, waaye jàng naa bu bare. Ci sama feeti Winter Break, jàngoon ñeeti tééré yi.
    Seetiwoon naa samay xaritu lise, ak màggal nanu fan bu njëkk ci 2015. Nun demoon nanu ci sinemaa ak setanoon nanu “Into the Woods.”
    Ci semestaar bi, am naa juroom kalass yi. Am naa kalassu faranse, kalassu wolof, kalass bi ci njàngu mbootaay, kalassu gëstu, ak kalass bi ci njàngu ñam. Am naa sama liggééy ci bitiku weñ, ak sama liggééyu mbind. Liggééy naa tamit ci samay waac pur déwén, ndax dinaa dem ci Senegaal.

    • Jane,
      Jërëjëf ci sa mbind mu am xalaat yu rafet te wuute. Sa liggééy am na solo. Waaye, dinga soxla xoolaat tuuti yenn ci baat yi.
      1. Toggandoowoon nanu
      2. Yàppu-mbaam
      3. Salaat ji
      4. Demoon nanu ci dëkku Cincinnati te seetiwwon nanu …
      5. waaye jàng naa lu bari
      6. Ci sama feeti Winter Break, jàngoon naa ñeenti tééré.
      7. samay xaritu liisé
      8. Màggal nanu fan wu njëkk
      9. Seetaanoon nanu
      10. Ci semestar bi …….juróómi kalaas
      11. Ab kalaas ci njàngu mbootaay …… ab kalaas ci njàngu ñam
      12. Bitig

      Am naa benn laaj. Lan nga bëggoon wax ci “waac pur déwén”? Ndax bëggoon nga wax “Applications” wala “Preparations”?

      Jërëjëf. 🙂

Leave a Reply